|
KURÉL BIY ÀND AK PAAP BI
DI TOPPATOO WAXTAAN WI CI DIGGANTEY DIINE YI
Kerceen yi ak Jullit
yi,
nanu ànd
daan fitna bi
diggantey
diine yi
XIBAAR NGIR MUJUG KOOR GI
‘Id al-Fitr 1431 H / 2010 A.D.
Dëkkub Watikan
Sumay xarit jullit yi,
1. ‘Id al–Fitr, di bés biy téj Koor gi,
nekkati na ab bunt ngir jottali leen yéeney xaritoo ak mbégte yi
jóge ci Kurél biy ànd ak Paap bi di toppatoo Waxtaan wi ci
diggantey diine yi.
Lu tollook weer wii wépp, yebu ngeen ci ñaan,
woor ak a dimbali néew-ji-doole yi, ak it ci gëna dëgëral bokk
gi ak xaritoo gi . Yàlla du leen fàttee yool ngir jëf yooyu !
2. Maa ngiy bànneexu itam ci li ma xam ne ay
aji-ngëm ci yeneen i diine, rawati na kerceen yi, jege nañu leen
ci bés yii, di bokk séddoo ak yeen, ni ko ndajey xaritoo yi di
seedee te ñuy it ay bërëbi wéccoo xalaat ci mbirum diine. Ma di
amati mbégte ci yaakaar ne Xibaar bile mën naa am wàll wu rafet
ci seeni sotteentey xalaat.
3. Kàddu gi kurél biy ànd ak Paap bi di
toppatoo Waxtaan wi ci diggantey diine yi jàpp ren moo di :
Kerceen yi ak Jullit yi, nanu ànd daan fitna bi diggantey diine
yi, te mu di li ñuy dund jamano jile, ci yenn diiwaani
àddina si. Kurél biy liggéeyandoo ak Paap bi, di ko xelal ci
waxtaan ak Kurél al-Azhar biy toppatoo waxtaan wi diggantey
diine yi gëm ci jenn Yàlla tànnoon nañu ko ni kàddu gi ñuy
waxtaane ak a sotteente xalaat ci seen ndaje mu mujj mi ñuy def
at mu nekk (ca dëkkub Keer, 23 ak 24-eelu fan ci weeru féwariye
atum 2010).
Sañ naa séddoo ak yeen yenn punk yi ñu fa tënk
ak a dogal te ñu yégle leen ci mujug ndaje moomu.
4. Ci biir li waral fitna yi am diggantey
aji-ngëm yi mën nañoo ràññaatle noggatub diine ji ngir jot li ñu
bëgg ci fànnu politig ak ñoom seen, fegg nit bi lalu ci xeetam
walla diineem xàjjaliku ak ay yi ci wàllu mboolem nawle mi. Ñàkk
xam bi, néew-doole ji, ñàkk suqakaliku bi ak ñàkk njubte ji di
yeneen bunt yu fés walla làqu yu waral fitna bi am diggantey
mbootaayi diine yi, waaye itam ci seen biir sax. Yàlla na Yàlla
def ba ñiy jiite réew yi, mboolem nawle mi ak diine yi dugal ci
seen loxo ngir dakkal mbir yu metti te bare yooyu ngir jàmmug
ñépp ! Yàlla na Yàlla def ba ñiy jiite réew yi ak mboolem nawle
mi dëggal ak a dëgëral màggaayu yoon wiy wóoral njubte tigi ngir
daan ñiy sooke fitna bi !
5. Ay ndigal yu am solo lool a ngi ci bataaxal
bile itam : ubbi sunu xol ngir baalante ak a juboo, ngir dunde
jàmm ju mët sëkk ; xàmme ak a nangu li nu bokk ak a weg
wute-wute yi, ni li lal waxtaan wi ; xàmme ak a weg daraja ak
sañ-sañu bépp nit, bañ cee boole fegg nit bi lalu ci xeetam
walla diineem ; suuxat tëralin yu jub yiy dëgëral dëgg bokk giy
dox sunu diggante nun ñépp ; maanaay yar bi ci weg, ci waxtaan
ak a xaritoo ci biir bërëb yi ñuy yare : ci kër gi, ci lekkool
bi, ci biir jàngu yi ak jumaa yi. Noonu dinanu mëna daan fitna
bi diggantey diine yi te suuxat jàmm ji ak déggoo diggantey
mbootaayi diine yu wute yi. Njàngalem njiiti diine yi, waaye
itam téere yi ñuy jérinoo ci lekkool yi te ñuy bàyyi xel ci wone
diine yi ci amaan ju rafet, te mu témboo ak njàngale mi ñu fi
baaxoo def. Muy dogal lu am solo lool ci yar ak a yee ndaw ñi.
6. Yaakaar naa ne xalaat yile, ak lépp li ñu
mëna jur ci seen biir, yeen ak seeni xariti kerceen, dinañu am
wàll ci amal waxtaan wi ànd ak weg, saa su nekk, te gëna yenu
maanaa. Ngir waxtaan woowu am laay ñaan Yàlla ay barke yu bare !
Jean-Louis Kardinaal TAURAN
Diawrign bi
Pier Luigi CELATA
Utukat bi
|