Id al-Fitr 1428 H. / 2007 A.D.
KERCEEN YI AK SERIÑ YI WAR NA ÑU
AND LAWLOO AADA U JAMM JI
Yeen sumay xarit seriñ yu baax yi,
1. Lu ma neex lool la, ma di leen jottali yéeney kureelu paap bi di yënggu ci waxtaan gi war ci digante diine yi, yéeney xarit, te ñu sawar di ko def, ci seen xew-xewu Id al-Fitr bi di xewte baneex te di jeexantalu doxum weer lëmm, bi ngeen dox, ci koor ak ñaan, di weeri Ramadaan bi. Dox boobu jamano ju am maanaa la ci dundu mbootayu seriñ yi, mu di jottali ku nekk doole gu bees ngir dundu boppam, bu njabootam ak bu mbootay gi mu bokk. Ndaxte lu war la, ku nekk di seede li diine di santaane, ci dund guy gën di jub te gëna mengoo ak li Bindakatu aduna bëgg, and ci ak xalaata surgawu ay mbokkaam, bokk soxla ak ñoom, am xolu mbokk ak ñi bokk ci yeneen diine yi, ak nit ñi di uta def lu baax ñépp, ndax rekk bëgg bokk ligey ngir liy jeriñ nit ñi ñépp.
2. Ci jamano ju jaxasoo ji nu nekk, ñi gëm ci diine yi, am na ñu sas wu jiitu : moo di ligey, niki surgay Aji-katan ji ngir jamm ji nga xam ne balaa muy am, ell na ñu may cër li nit ku nekk ak li mbootay bu nekk gëm, te ku nekk yaatu ngir mëna jaamu Yall naka lako diineem tëralee. Yaatu ci diine bobu nga xam ne yemul rekk ci am sañsañu mëttali ay taxawaay u ngëm, benn anam bu jiitu la ci li di njambuuru fit bi nga xam ne yelleefu nit ku nekk la, di itam li di wóoral yelleefu nit yi yëpp.
Su nu bëggee taxawal aada u jamm ak bokk soxla ci digante nit ñi, ell na ñu bayyi xel ci loolu ; noonu, ñëpp di na ñu mëna soobu te yebu ngir jagal mbootay buy gën di nekk mbootayi mbokk, te di nañu mëna def lëpp li ñu mën ngir bañ fitna bu mu mënti doon, ngir weejee te yedd këpp ku bëgga jëfoo fitna ; te moos, fitna mënul sukkandiku mukk ci diine, ndaxte defay ñaawloo nit ki bindu ci meliinu Yall. Ñun ñëpp xam nanu ne fitna, waxatu ma iite tiitalaate ak boom bi dul rañatle ci kaw ñan lay dal te muy lor nit ñu bare, jëkkee ko ci jambuur yi mënul sottil bajjikonte yi, lu dul, xanaa, jur dee, mbañ ak yaqqal nit ñi ak mbootay yi.
3. Ñun ñi di niti diine, nun ñëpp noo wara jiitu ci li di jangalee jamm, ci yeete ci yelleefu nit ñi, ci digal njambuur bu di cëral nit ku nekk, ak itam dundu mbootay buy gëna am doole ; ndaxte nit ki defa wara saytu bëpp nit, ci kaw li mu bokk ak moom ndey ak bay, baña tuutil kenn. Waru ñu génnee kenn ci mbootayu réew ngir xeetam, diineem, mbaa beneen melukaan bu nekk ci moom. Nun ñëpp ñi bokk ci xeetu diine yu uutante, sunu sas moo di lawloo jeemantale bu di suturaal bépp doomu adama, lawloo yéene cofeel ci digante nit ñi ak ci digante xeet yi. Li gëna nekk sunu sas moo di nu yar ndaw yi ci xalaat boobu, ñoom ñi wara doxal aduna si suba. Njaboot yi, ñi am cër ci yarum ndaw yi, njiiti addina yi ak yu diine yi, ñëpp de ñoo wara farlu ci di jottalee njeemantale bu jub, ak ci fexeel ku nekk yar bi war ci anam yi ñu fi tudd, ñu gëna fësal jeemantalee dund ci mbootay bu di xamal ndaw bu nekk mu cëral ñi ko wër te seetee leen niki ñu mu bokkal ndey ak bay, te mu wara dund ak ñoom bes bu nekk. Waxu ñu nga def niki ku xamul ñi muy dund ak moom, wande nga di bayyi xel ci ñoom, niki su ñu nekkoon ay mbokk.
Kon lu jamp lool la, ñu di jeemantal maasi ndaw yi li nit ñi japp niki lu baax, li di dund gu rafet, li di taxawal dund ci biir mbootay, li ci jiitu, te nga xam ne mënu ñu ñakk nekk ngir dundu nit ku nekk ak dundu mbootay bi. Saa yu ñu gisee ndaw yi def naka su dul noonu, war na ñu léen fattali li ñuy xaar ci ñoom ci dundu mbootay bi. Njekk lu baax li war mbootay bu nekk ak addina si sepp ci loolu la aju.
4. Yooyu xalaat ñoo wara tax nu japp ne lu am maanaa la ñu wey dund te gëna dooleel waxtaan bi ci digante kerceen yi ak seriñ yi ci li mu nekk yar ak saxal aada, ngir ñu boolee mënmën yi yëpp, ñu jeriñ nit ku nekk ak nit ñi ñëpp, ndax maasi ndaw yi baña doon getti aada ak diine yu di xeexoo, te ñu doon ay mbokk ci kaw li ñu di ay nit. Waxtaan bi doon na juntukaay, bu nu mëna dimmali be nu génna ci bojjikonte ak ŋaayoo yu bare yi ci biir mbootay yi, ndax xeet yi yëpp mëna dund ci dal ak jamm, ñu di mayante cër, te njaboot yi uutee yi dund ci déggoo.
Ngir loolu mëna am, mangiy dagan ñëpp ñu yebu : noonu, ci pexe dajee yi ak weccoo yi, kerceen yi ak seriñ yi and ligey, ñii di cëral ñii, ngir jamm am, te nit ñi ñëpp mëna yaakaar addina su gëna neex suba. Noonu itam, di na ñu doon rooyukay ngir ndaw yi. Ndaw yi di na ñu leen top te toppandoo leen. Ndaw yi di na ñu gëna wóllu dundu mbootay te di na ñu gëna sawar ci bokk ci mbootay bi ak ligey ngir soppali ko mu gëna baax. Yar gi, ak wonee rooyukay di na leen may ñu am yaakaar ci addinab suba.
5. Lilee moo di iite bu ma ñor bi ma bëgg seddoo ak yeen ; kerceen yi ak seriñ yi war na ñu yokka digaale xaritoo yu di defar ngir ñu weccoo lu jekk té rafet li ku nekk am, te ñu sabablu bu baax seedees gëmkat bu rafet !
Yeen sumay xarit seriñ yu baax yi, mangi leen waxaat suma yeene yi ma tibbee ci suma xol, ci seen xewte bi, te mangi ñaan Yallu jamm ak yermande bi, mu may leen yeen ñëpp wërgum yaram, dal ak naatangee.
Jean-Louis Kardinaal TAURAN
Njiit li
Pier Luwiji CELATA
Bindakat bi