KOÑSEY BI ÀND LIGGĖEY AK PAAP BI Kerceen ak Jullit : XIBAAR CI MUJJANTALUG KOOR GI ÂId al-Fitr 1430 H / 2009 A.D.
Jullit yi, sunuy xarit 1. Ci mujjantalug weeru Koor gi, bëggoon naa leena wax sumay yéeney jàmm ak mbégte te, jaarale ko ci bataaxal bile, ñaax leen nu ànd xalaat ci lu jëm ci itte bile : Kerceen ak Jullit, nanu ànd xeex néew-doole gi. 2. Warees nañoo bànneexu : Xibaar bile jóge ci Koñsey biy ànd liggéey ak Paap bi ngir Diisoo ci diggantey Diine yi, nekkul rekk li ñu baaxoo def, waaye am ndaje la mu ñu doon xaar. Ci réew yu bare, am na ay ndajey xaritoo yu bare diggantey Kerceen yi ak Jullit yi. Ñàkkul it, mu méngoo ak bëgg-bëggu séddoo ak a wéccoo xalaat yuy dëgg, takku te ubbeeku. Ndax yile firnde yépp doonuñu ay màndargay xaritoo ci sunu biir ngir gërëm Yàlla ? 3. Ngir dikk ciitte bi ñu jagleel at mii, nit ki nekk ci soxla yu tar a ngi dëgg ci diggu yébble yi nu fonk ci ay fànn yu wuute. Bàyyi xel, yërmaande ak ndimbal li ñépp, mag ak ndaw, góor ak jigéen ci àddina si, mëna may ki néew-doole ngir joxaat ko gëddam ci biir mboolem nawle mi, ñoo di firndeel ci lu wóor Cofeelug Yàlla Aji-kawe ji. Ndegem nit ki ak ni mu nekke la nu Yàlla di woo, nu sopp ko, dimbali ko, te baña xàjji ak seen. Nun ñépp xam nanu ne néew-doole gi dafay neenal nit te di jur ay coono yu kenn mënula àttan. Ñu di indi léeg-léeg beru, mer, dem sax ba ci iñaan ak bëgg-bëggu feyyu. Lile mënoon naa yóbbe ba ci jëf yu ñaaw jaarale ko pexe yi ñu am, di leen wuta dëggal sax ak ay kàdduy diine : mu di nangu, ak doole, sa alalu nawle, te di mbubboo « njubteg Yàlla », boole ci, jàmmam ak kaaraangeem. Looloo tax, fexee delloo gannaaw jëf yiy yóbbu nit ki mu dem ba sës ak fitna bu metti, dafay laaj, ci lu wér, ñu xeex néew-doole gi, jaarale ko ci suqali yokkute gi mët sëkk gu nit ki. Paap Pool VI firi woon na ko ni « tur wu beesub jàmm ji » (Bataaxal bi ñu bind lewek yi Populorum Progressio, 1975, n. 76). i bataaxalam bi mu sooga bind lewek yi, làbbe yi, jaakër yi, katolig yi ak waa àddina si sépp Caritas in Veritate ci lu jëm ci suqali yokkute gi mët sëkk gu nit ki ci cofeel ak dëgg, Paap Bënwaa fukk ak juróom-benneel bi, bu seetee ni àddina si sóoboo ci suqali nit ki, dafay feeñal ne danu soxla « gis-gis bu bees ci mbirum nit ci bépp fànn » (n. 21) ; gis-gis boobu dafa koy joxaat gëddam « ci biir ak ci kaw suuf si » (n. 57). Noonu, suqali buy dëgg, dees nañu koo mëna digle ci « bépp nit ak ci nit ñi ñépp » (Populorum Progressio, n. 42). 4. Ci waareem bi mu def ca bés bu jiitu ci weeru sawye, di Bés bi ñu jagleel Jàmm ji ci Àddina si sépp, Paap Bënwaa fukk ak juróom-benneel mu sell mi ràññaatle na ñaari xeeti néew-doole : néew-doole gu ñu wara xeex ak néew-doole gu ñu wara tànn ak a nangu. Néew-doole gi ñu wara xeex, ñépp a ngi koy gis : xiif, ñàkk ndoxum naan, ñàkk paj ak dëkkuwaay yu jekk, ñàkk mi am ci lekkool yi ak ci kurél yiy yee ak a suqali mbiri baax yi, ñàkk njàng, te ñu baña fàtte itam xeeti néew-doole yu bees yi « maanaam ci mboolem nawle yu bare alal te yeewu,  . ni ñu fegge doomi-adaama yi, néew ci kóllëre yi, néew ci yaru ak ci ngëm » (Xibaar ngir Bés bi ñu jagleel Jàmm ji ci àddina si sépp 2009, 2). Néew-doole gi ñu wara tànn dafa jëm ci dundin gu yem te tegu ci li ñu soxla, baña yàq, te di fonk càkkéef gi, maanaam li nu wër, ak yëfi Mbindeef mi. Néew-doole gile dafa jëm itam, lu tollook lu mu bon, bon yenn jamano ci at mi, ci lekk bu yem ak koor. Néew-doole gi ñu tànn dafa nuy dimbali ngir weesu sunuy àppi bopp, di yaatal sunu xol. 5. Ci yoon, aji-ngëm yi dañu bëgga diisoo ngir ànd gis ay bunt yuy dëgg te yàgg yu di saafaral jafe-jafey néew-doole gi. Noonu bëgg nañu it xalaat lu jëm ci jafe-jafe yu mettee-metti yiy laal sunu àddina su tey si ; saa su mënee am, bëgg nañoo ànd yebu ngir saafaral leen. Li sunuy mboolem nawle yi di laalante ba doon daa naka benn àddina mooy indi ay jafe-jafey néew-doole yi ciy ànd. Bu ko defee, jaadu na ñu xalaat ci ak xelum ngëm ak yaru. Ndaxte nu ngi séddoo benn woote bi nu Yàlla woo ngir tabax genn njabootu doomi-aadama goo xam ne ñépp - nit ñi, xeet yi ak réew yi  war nañoo sukkandikoo seeni jëfin ci yooni xaritoo ak nangu seen sas. 6. Bu nu xoolee néew-doole gi ak ni mu lëje, dinanu nemmeeku fu xóot-a-xóot fu mu cosaanoo maanaam ci ñàkk fonk daraja ji ànd ak nekk nit. Gis-gis boobu dina nu xiir nu mànkoo ci fànn bu nekk, maanaam nu nangoo « bokk wenn tëralinu jëfin » (Paap Saŋ Pool ñaareel bi, Kàddu gi mu sànni kurél bi ñu naan ÂAcadémie Pontificale des Sciences Sociales, 27-eelu fan ci weeru awril 2001, n. 4) : sarti tëralin woowu du càggen ne ñépp ànd nañu ci rekk waaye sax nañu ci tëralinu yoon wi Yàlla Bindkat bi teg ci xolub bépp doomu-aadama (seetal Room 2, 14-15). 7. Yég nanu ne, ci ay bërëb yu wuute ci àddina si, jóge nanu ci muñalante rekk ba tase buy dëgg ci li nu bokk dund, bokk ittewoo. Jéego bu am solo lool a ngoogu. Ndax diisoo biy dox diggantey diine yi du yee doole ak cawartey ñi jublu fa Yàlla, su ñépp séddoo seen alalu ñaan, koor ak cofeel ? Néew-doole baa ngi nuy yëngal, di nu dékk, waaye, rawati na, mu ngi nuy woo nu liggéeyandoo ci sas wu rafet-a-rafet : mu di xeex néew-dooleem ! Nu ngi leen di yéene ÂId al-Fitr bu sell te neex !
Archevêque Pier Luigi Celata
CONSEIL PONTIFICAL
|
|