The Holy See
back up
Search
riga

KURÉEL GI ÁND LIGGÉEY AK PAAP BI
NGIR WAXTAAN AK A DIISOO CI DIGGANTEY DIINE YI

XIBAAR CI MUJJUG KOOR GI
‘Id al-Fitr 1433 H. / 2012 A.D.

Yar ak a yee ndawi kerceen ak ndawi lislaam ñi
ci njubte ak jàmm

 

Sumay xariti jullit yi ma sopp,

1. Xumbal bi ñuy xumbal ‘Id al-Fitr’, muy mujjantalug weeru koor gi, dafa nuy may mbégtem jottali leen yéeney doomi baay yi bawoo ci Kuréel bi ànd di liggéey ak Paap bi ngir waxtaan ak a diisoo ci diggantey diine yi.

Ànd ak yeen, nu ngiy bànneexu ci jamano ju am solo jile ngeen xam ne, jaarale ko koor ak yeneen i jëfi diine, may na leen ngeen gëna xóotal ak a fésal seen njaamug Yàlla, muy jikko ji nu naw, nun itam.

Looloo tax, atum ren, nu xalaat ne, lu baax la nu boole sunu xalaat jëme ko ci yar ak a yee ndawi kerceen ñi ak ndawi lislaam ñi, ci mbirum njubte ak jàmm, ngeen xam ne mëneesuňu leena tàggale ak dëgg gi ak moom sa bopp.

2 Ni ngeen ko xame, su ñu dénkee mboolem nawle mi sasu yar ak a yee, waa-jur yi, ci lu wóor, ñoo ko jëkka wara mottali, te ànd ak ñoom, njaboot yi, lekkool yi ak liniwersite yi, te nu baña fàtte njiiti diine yi, ñi yor wàllu aada ak cosaan, wàllu jàppalante, wàllu koom-koom ak wàllu ñiy yëngu ci jokkalante.

Jëf ju rafet te jafe la : muy dimbali xale yi ak ndaw ñi, ñu ràññee ak a suqali mën-mën yi leen sunu Borom dénk, ak it taxawal jëflante yu leer te gore ci diggante nit ñi. Sukkandikoo ci sasu yarkat yi, Paap Bënwaa XVI-eel bi, wax na bu yàggul dara ne : « Tey lañu gëna soxla aste bu jëkk, ay seede yu wóor te dëggu yu yemul rekk ci jàngale ay tëralin ak a siiwal xibaar yu bare… Seede nak mooy kiy jëkka dund yoon wi muy digle » (Xibaar ngir Bésub Jàmm ji ci àddina si 2012). Nanu fàttali itam ne, ndaw ñi am nañu wàll wu réy ci seen yar ak a yee ci mbirum njubte ak jàmm.

3 Njubte gi dafa sukkandiku lu jiitu ci nit ki ci boppam, ci jëmmam ji ne ñumm ; mënula yem rekk ci fànnu wéccee ak a séddaatle. Bu nu fàtte ne li ňépp bokk moom, mëneesu koo jot te boolewuňu ci mànkoo ak cofeelug doomi ndey ! Ngir aji-gëm yi, njubte tigi gi ňuy dund ci xaritoo ak Yàlla dafay gëna xóotal sa diggante ak sa bopp, sa diggante ak ňeneen ňi, ak it mbindeef mi mépp. Rax ci dolli, aji-gëm yi daňu gëm ne njubtee ngi cosaanoo ci li Yàlla sàkk nit ňi ňépp te woo leen ňu doon genn njaboot rekk. Gis-gis bu ni mel, tegu ci weg dëgg gi te di ubbeekul li ňu sut, dafay woo niti jàmm ňi ñépp, góor ak jigéen, ci fexee doxal, ni mu gënee rafet, àq ak yelleef yi.

4. Ci sunu àddina su jaxasoo sile, yar ak yee ndaw ňi ci jàmm dafay gëna tar saa su nekk. Ngir yebu ci, ba mu mët, war naňoo nànd bu baax maanaay jàmm juy dëgg ji yemul ci ňàkk xare mbaa ci tolloo doole ak sa morom, waaye muy jàmm ji doon, ci benn yoon, mayeg Yàlla ak jëfu nit, te ñu war koo tabax, baň cee tàyyi. Jàmm mooy li njubte ak cofeel di jur. Lu war la aji-gëm yi di yëngu saa su nekk ci biir seeni mbootaay : di jëfe laabiir, mànkoo, booloo ak a dund ni ay doomi ndey. Mën naňoo bokk bu baax ci dékku jafe-jafey jamano ji : muy màgg mu rafet, suqaliku ci fànn yi yépp, fàggandiku ak a saafaraal ay yi, su ñu yemee ci lim yile rekk.

5. Ci mujjantal bi, bëgg naňoo ňaax ndawi lislaam ak ndawi kerceen ñi bëgga jàng bataaxal bile, ñuy sàmm, bés bu nekk, dëgg gi ak moom sa sopp, ngir doon ay ndawi njubte ak jàmm tigi, ak it, ngir doon ay tabaxkati aada jiy weg àq ak darajay doomu réew ju nekk. Nu ngi leen di ňaan ňu ame muň ak jom ngir mottali seeni bëgg-bëgg yile te baňa wuti ay dige yu wóorul, ay yoon yu gàtt yuy naxe, mbaa ay pexe yu yelloowul ak darajay nit ki. Ay góor ak ay jigéen doηη ñu tàkku ci itte yilee mëna tabax ay mboolem nawle fu njubte ak jàmm di dooni lu wér te wóor.

Yàlla na Yàlla feesal, ak weg ak yaakaar, xol yi, njaboot yi, mbootaay yi ngeen xam ne ňi ci bokk, seen bëgg-bëgg mooy ñu doon « ay jumtukaayi jàmm » !

Koriteb jàmm !

Watikaŋ, 3-eelu fan ci weeru ut atum 2012

Jean-Louis Cardinal Tauran
Président

Archevêque Pier Luigi Celata
Secrétaire

 

 

CONSEIL PONTIFICAL
POUR LE DIALOGUE INTERRELIGIEUX
00120 Cité du Vatican

Téléphone: 0039.06.6988 4321 / 06.6988 3648
Télécopie: 0039.06.6988 4494
Courriel: dialogo@interrel.va

  

top